Feebaru Tëlbëti Bu Amul App

Feebaru tëlbëti bu amul app Feebaru tëlbëti bu amul appmooy bennfeebaru xelboo xam ne nit ñi dañuy am soxlaa xoolaat mbir yi ay yooni yoon, di leen di defyenn yëngu yëngu yi ay yooni yoon(ñu koy woowe aada), walla am yenn ci xalaat yi di ñëwaat ay yoon (ñu leen di woowe tëlbëti).

Nit ñi dañuy am jafe jafe wotu seeni xalaat walla seen yëngu yëngu lu yagg. Yëngu yëngu yi ñuy gëna gis ñooyraxasu, woññi mbir yi, ak di seet ndax ab buntu tëju na walla. Ñenn ñi dañuy am jafe jafe sanni ay mbir ci biti. Yëngu yëngu yii dañuy faraldi am lu baree bare ba nga xamantane nit ki ci boppam dundu bés bu nekk dafay metti. Dafay faraldi lu ëpp benn waxtu bés bu nekk. Mag ñu bare dañuy gis ne nekkin yooyu du tekkiwuñu dara. Mënin bi dafa ànd ak ay tik, feebaru ku jaq, ak njàjan bu yoqu ci wallu xaru.

Li koy indi waxuñu ko. Gis nañu ne am na yennndono falkat yi ak ñaar yéppay seex yu niróó ñoom la gëna laal ay seex yi niróówul. Liy indi njàjan yi bokk na ci xale buñu daan noot walla yeneen stress-liy yoq xew xew. Yenn yi bind nañu leen dénc gannaaw ay wall wall. Saytu bi mungi sukkandikoo ci yi koy feeñal te soxla na daq yeneen garab walla li joge ci yeneen jangoro yi koy indi. Ay xaymawukaay ni Yale–Brown Obsessive Compulsive Scale (Y-BOCS) mën nañu leen jëfandikoo ngir saytu rëyaay bi. Yeneen feebar yu metti yi ak ni ñuy feeñe ni yooyu bokk na ci feebaru ku jaq, feebaru naqar ak déteelu gu tar, lekk yu jaxasoo, feebaru tik, ak feebaru tëlbëti bu amul app bu nekkinu nit ki.

Faj mi bokk na cijoxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem, ni pajum nekkin bu àndak xalaat(TCC), ak yenn saay yiy xeex déteelu ni Inhibiteur sélectif de la recapture de la sérotonine walla clomipramine Pajum nekkin bu àndak xalaat (CBT) bu feebaru tëlbëti bu amul app (OCD) bokk na ci yoquteek liy indi jafe jafe yi te du bayyi nekkin bi di amaat ay yoon. Bu clomipramine di dox ak SSRI yi, efe sëkondeer yi tax na ba pajam dañu wacce ci ñaareelu liiñ bi. Yuy xeex ñakk àndak sago yu ñu dul faraldi gis mën nañu am njëriñ bu leen jëfandikoo ci kaw SSRI bi ngir fajum yenn yu fës yi wante dañu leen di boole ci njàjan yiy yoqu efe sëkondeer yi. Ñakka paj mi, dina tax ba mënin mi di faraldi yagg lool.

Lu tollook 2.3% ci nit ñi ci seen giiru dund feebaru tëlbëti bu amul app dal na leen. Xayma bi ci benn at mungi tollu ci lu jege 1.2% ci addina bi yépp. Feebar bi duy faraldi feeñ bu nit ki weesoo fanweeri at ak juróóm, te génn wall nit ñépp dañuy tambali am ay jafe jafe balaa seen ñaar fukki at. Góór ak jigéén yépp ñoo tolloo ni leen feebar bi dale. Ci Anglais, baatu tëlbëti bu amul appdañu koy faraldi jëfandikoo ci anam bu ñu tegul ci yoon bu bokkul ak OCD ngir wonale nit ku set lool ci li muy def, ku bëgg lu wóór, kuy jël, walla kuy xool fenn lu yagg.

Tags:

Xaru

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

SafaraBabilonTaariixu AamerigCorda (Kap Weer)UraanusWaletaMeeNdimbal ci ay nataalFontainhas (Kap Weer)Alex FergusonS.L. BenficaCabeça dos TarafesUtYamooSuletKoorGëm Malaaka yiWu-ispaañGunóorMbëjJaxan-jaxanAtenMakaawBanjulMogadisuBaatukaayWikbaatukaaySattumbarJoolaa (askan)XaymaMarokFànnAsamaanFeppsaalAlbaaniWeeri wolofLimub njiiti Senegaal yilEslowaakiMosambikJordaaniSuufJoão GalegoJibutiBeliisPolitigEndoneesiKol-kolu suuf siNgeerF.C. PortoXëtu garab i wikipediaNosukaayKowetKullu-kulluSëriñ Saaliwu MbàkkeGireesNdakaaruTrojanyTimoor gu Penku🡆 More