Ñaqu Meningite

Royuwaay:Drugbox Ñaqu antimeningococcique mooy bépp ñaq bi ñu mëna jëfandikoo ngir mucc ci feebaru Neisseria meningitidis.Amna yeneen xeetu ñaq yu mëna musal nit ki ci yenn ci xeetu meningite yii ñuy lim: A, B, C, W-135, ak Y.

Baaxaayu kaaraange ñaqu gi mingi ci diggante 85 ak 100% mën na yàgg gën gaa néew ñaari at. Ci ñi koy jëfandikoo, dina fa wàññi méningite ak sepsie. Ci sidit lañu la koy jam wala ci suufu der bi.

Waa OMS (Mbootaayu sàmm wérgi-yaram ci àdduna bi) waxna ni ñi nekk ci barab yu bari meningite wala yu ko xawa am, dañu wara ñaqu ngir mucci ci feebar bi. Sudee gox yi feebar bi bariwul, nañu ñaq ñi nekk ci wetu ñu am feebar bi. Ci goxu afrique yi nekk ci ndomba meningite, ñu ngi def jéego yu mag ngir ñaq yi am diggante 1 at jàpp 30 at, muy ñaq bi boole ak méningocoque A. Ci Kanada ak ci États-Unis, dañuy digle ñuy faral di ñaq ci saasi bépp xale bu nekk ci barab bi feebar bi nekk te bari fa. Waa Arabi Saudi dañuy sàkku ci képp kuy aji Màkka mu jël ñaq bi koy aar ci meningite.

Ñaqu meningite (Meningococcal), daanaka ñaq bu wóor la. Ci ñénn ñi, barab bi ñu leen ñaq mën na xonk wala mu metti tuuti. Jiggéen ju ëmb mën na ko jëfandikoo. Néew la lool lumuy indi nit ki ay jafe-jafe, matul benn ci 1milioŋi ñaq.

Ci atum 1970 lañu njëkka génne ñaqu meningocoque. Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla. Ñu ngi jaaye ñaq bi 3,23 ak 10,77 USD dose bu nekk (en gros) li dalee atum 2014. Ci États-Unis, ñu ngi koy jaaye ci diggante 100 ak 200 USD.Royuwaay:TOC limit

Tags:

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

LibeeriaKodiwaarCuub.jpSatumbarBagdadTiniisiLinuxLimub njiiti Senegaal yilDëkkaani ndiiwaani SenegaalXam-xamu suuf si ak jawwu jiMaleesiGineKaledooni-Gu-BeesTaaylaandMàngoYewwute gu ndefarBanglaadesNiccolò MachiavelliRiisiBelaarusSport Bissau e BenficaSudaanRéewum Popileer bu SiinBerlinAntananariwoIzhevskJokkoo-cig-soreeFinlaandAhmadou BambaSaint Vincent and the GrenadinesBarbadosGuangzhouSinemaaArmeeniBulgaariRéew yu Bennoo yu MikronesiOlaandEscudo Kap WeertKopenagenXeexYattHTMLBaatukaayÑaareelu Xareb ÀddunaXam-xami nite ak mboolaayKasakistaanDanmaarkIsraayilGoxNepaalXëtu webLilongweJimbulangUsbekistaanCuritibaBreesilSoxna Jaara BusoYëngu-yëngu yu ag nasaraanal ak ay wi mu àndalMoldaawiKaliningradRéewum ñaari dex yi🡆 More