Déteelu

Feebaru naqar gu metti ku dara saful MDD, ñu xame ko itam ni déteelu, mooy benn feebaru xelbu ñuy xame ci ñaari ayubés ci (dikkale bu wacc bu feeñ ci yu bari.

Dafay faraldi di ànd ak tuuti ci wóólu sa bopp, ñakka am yëg yëg ci yoon ci ay yëngu yëngu yu wara neex, njaxlafaay gu wacc, ak mettit bu amul lu ko waral. Nit ñi mëna nañu am yenn saay ay gëm gëm yu amul walla gis walla dégg ay mbir yu nit ñi dul gis walla dégg. Ñenn ñi am nañu ay diiru déteelu te ci seen diggante dañuy mel ñépp ay at, te ñeneen ñi ci boobu diir dañuy génne feebar bi. Feebaru naqar gu metti ku dara saful mën na japp nit ki japp bu ñaaw ci dundam, walla ci njàngam, walla ci nelawam, walla ci ni muy lekke, ak ci wér gu yaram. Ci diggante 2-8% ci magg ñi ame feebaru naqar gu metti ku dara saful dañuy dee ak xaru, te lu tollook 50% ci nit ñiy dee ak xaru amoon nañu déteelu walla beneen feebar feebaru dikkale.

Gëm nañu ne li koy indi mooy ab mbooloowu ndono ci dereet, ci li ñu wër, ak ci wallu xel. Risk yi ñooy ci wallu cosaanu waa kër gi ci li koy joxe, coppite ci dundum nit ki, yenn garab yi, jafe jafe yu metti ci wér gu yaram, ak feebaru dorogewu. Lu tollook 40% ci risk yi ñungi joge ci ndono yi ci dereet. Saytu yi ci feebaru naqar gu metti ku dara saful mungi wekku ci jaar jaar yi nit ki di nettali ak benn saytu ci fi xelam tollu. Amul benn saytu ci laboratoire ngir feebaru déteelu yu gêna bari yi. Di ko saytu, waaaye, mën nañu ko def ngir dindi fi yenn jafe jafe yi ci yaram bi yu mëna indi ay yeneen mandarga yu mel noonu. Feebaru déteelu moo gëna metti te mooy gëna yagg naqar, lu bokk ci dund nit ki la . Lii di United States Preventive Services Task Force (USPSTF) laaj na ñu saytu déteelu ci ñi am lu ëpp fukki at ak ñaari, ci waxtu woowu ci xibaaru Cochranegis nañu ne di faraldi di laajte du jappale génne walla faj feebar bi.

Ci yoon, nit ñi ñungi leen di faj ak joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem ak garab yiy xeex déteelu. Garab yi wone na ne am njëriñ, waaye njëriñ li mën na baax ci ñi gëna mettile feebar. Leerul ndax garab yi dañuy def antum risk xaru. Yenn xeeti joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem bokk na ci pajum nekkin bu àndak xalaat(CBT) ak pajum nekkin ak ñeneen ñi bu àndak xalaat. Su fekkee yeneen xayma yi amuñu njëriñ, pajum electrochoc (ECT) mën nañu ko jëfandikoo. Tëye nit ki ci opitaal dina baax su fekkee nit ki am na risk gaañ boppam te mën na léég léég ñakka ànd ak li nit ki bëgg.

Feebaru naqar gu metti ku dara saful daloon na lu tollook 216 miliyoŋ ci ay nit (3% ci addina bi yépp) ci atum 2015. Limug nit ñi ame feebar bi ci seen dund mungi tollu ci 7% ci Japon ba 21% ci France. Lim gi ci giir dund mungi gëna kawe ci rééwi ame koom koom gu baax (15%) méngale ko ak rééw yi seen koom koom di jog (11%). Indi na ñaareel bu gëna kawe ci ay at yu ñu dund ak feebaru ñakka mën, ginnaaw ndigg guy metti. Diir gu ñu gëna raññe ni feebar bi génn na mooy ci ati ñaar fukki yi at fanweer yi. Jigéén ñi dañuy faraldi gëna nañu ame feebar bi ñaari yoon góór ñi. Lii di American Psychiatric Association di mbooloo mi nekk Amerik dajale fajkati feebaru xel yi yoq ci ne "feebaru naqar gu metti ku dara saful" ci Téére Saytu bi ak Xayma bi ngir ñi ame Feebaru Xel (DSM-II) ci atum 1980 Ab dog dog la woon feebaru déteelu bu ànd ak dikkale bu waccci DSM-II, te mënin yi bokkoon ci ñu xame ko léégi ni déteelu bu ndaw ak ay feebaru nekkin yu dajaloo ak dikkale yu bon. Ñi amewoon feebar bi ak ñi ko ame léégi mën nañu nekk ay légëtloo.

Tags:

Xaru

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

Wolof (askan)GD AmaranteCiinBaaxoñ bSunnay CangaayKinshasaMburuGanaBeljikBabilonAlto MiraYewwute gu ndefarThanh HoaXajCeesAddunaFeebaru tëlbëti bu amul appPrimeira LigaEslowaakiAlseeriJanela (Kap Weert)Joolaa (askan)UlyanovskGoloNjàngatBukarestKajoorDiiwaanu FatikFukuokaGayndeRéewum LawosSaint Vincent and the GrenadinesCiipërTelefonTarrafalPenku gu JegeKamakuraNjëkk-taariixMontenegroBëj-gànnaaru AamerigTurks and Caicos IslandsFundo das FigueirasSuraas (wirgo)TokyoKanadaaTangorMboqMàndiŋ mBiibëlBurkinaa FaasoEcoopiSalbadoorMeeRio de JaneiroNamibi🡆 More