Ndiir

Ndiir xeetu ñax la gu bokk ci njabootu Cyperaceae.

Ndiir
Ndiir (Cyperus esculentus)

Melo wi

Ndiir ñax la gog ab guddaayam day toll ci diggante 25 ba 40i sànti meetar. Ay xobam dafa sew di gudde 5 ba 10i mm te tàllalu di niru ab jubb. Peeram dafa taxaw, liis te am i pàcc yu ñatti-koñe. Doom bi ci reen yi lay meññ. Ndiir bi day xaw a wurmbalu, yor wirgo wu jege mboq, ab deram ñagas. Ëmb na lu xaw a tollu ak 50% ci gilisit( sakaroos ak amido), 22% ci lipit ak 6 ba 7 poroteyin.

Njariñ li

Dees na ko jaay ci ja bi. Ca Senegaal dees koy lekk noonu mbaa soppi ko diw. Amna ñu koy soppi njar niki waa-espaañ. Amna it ñu koy jëfandikoo nib fiirukaayu jën niki waa-àngalteer.

Nataal yi

Turu xam-xam wi

Cyperus esculentus

Tur wi ci yeneeni làkk

farañse: chufa
angale: chufa sedge
itaaliyee: zigolo dolce

Tags:

Ndiir Melo wiNdiir Njariñ liNdiir Nataal yiNdiir Turu xam-xam wiNdiir Tur wi ci yeneeni làkkNdiir

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

SamwieOseyaaniWolof (làkk)Sowwu AfrikBetleyemShenzhenDéteeluTamxaritArimateAlmaañMbàmbulaanReiñõoKisinawuRostov-na-DonuSaint Pierre ak MiquelonCatirNorthern Mariana IslandsKom-komXeexWu-angalteerNjamenaAmsterdamEswatiniAtGuyaana gu FaraasAlxuraanul KariimTuberculosisWertPenku AfrigXam-xamSibiruEdgar de WahlWikipediaBuddaGireesChelyabinskMeksigDunGinne gu YemooSiliMaasSapoŋKoorRiisiSimiEslowaakiXaralaBesançonMonsoroKrasnodarXaruAyubésArkelawusRéewum LawosTus-wu-taxawJuróom bennGàncax🡆 More