Yaqq Yaqq Koronaa Ci Linu Weër Ci At Bi Ñu Nekk

Mbass mii di koronaa andilna yaaq yaaq yu bari ci adduna bi ñu nekk, yaaq na lu bari ci sunu dëkkuwaay ak linu wër.ndëgëni gi am ci wallum jawu ji taxna ba yaqqute yu bari yi doon am ci jawwu ji wañeekuna.

Tere gi génn ak yeneen yi ci top fële ca Chine taxna ba xaaju xaajat ci yaqqute yi daan am ci jawwu ji wañneekuna Taxna ñu bari lëlu baña geen, waañi na lu ci tilim-tilimal linu wër ci reewum Chine, loolu nak jotna aar juroom ñaar fukk ak juroom ñaari junni nit ci lu toll ci ñaari weer Mbass mi waañi na doole reew yi doon mankoo ngir aar liñu wër. tek ci daje bi ñiy xeex wallum yaqqutewuk jawu ji waroona daje ci atum ñaari junni ak ñaar fukk. Waañi na itam koom koom gi kureel gi waroon def xaalis ci gënë ñoñal kurang bii.

Ci ganaaw tuuti

Ba ci atum 2020 bii ñu nekk,yokkute gaas bi tass ci jawu ji te di juur tooke ca ba izin yi tambalee di genee saxar mën nanu wax ni loolu jur në tangoor wu tar ci jawu ji. Tangoor boobu tax na ba motaañu galaas yi ńu ngi seey ak geej giy nangu suuf si. Yaqqu yaqqu nit yi ci linu wër barina ay fasong. Loolu nak nit ñi rek ñooko waral. Li gënoona soxal doktoor yi ci mbassum feebar bii di COVID-19 moodoon ñu diggël nit ñi ci ñuy lëlu ak di soriyante nekkin. Ci coobare ku nekk, gëstu kat yi waxoon nañu ni laataa mbassum korona bi di COVID-19 li gën mooy ñu waañi yëngu yëngu yi ci wallum koom koom dina am solo.

Ngelawu dëkkuwaay bi tilim

Bi koronaa bi amee ba leegi, gis nañu ni niñuy tilimalee ngelaw li ñu wër waañeekuna lu baree bari. Waañi tilimal bi ñuy def ci ngelaw li ñu wër mën na tax ba yaqqute yiy am ci jawu ji waañeeku ak lii di COVID-19 bi wante nak leeragul ci ban fasong tilimal moo ëpp limuy yaqq ci lu jëmm ci soppeeku jawuji ak lii di COVID-19 bi.Kureel gu mak gi di gëstu ci linumel, wonena ni ngir teye coronavirus ngir mu baña law dañu war di lëlu di tëc foroñceer yi, te loolu waññi na xaaju xaajaatu yaqqute yi dëkkub Chine di def ci jawu ji.Ci weer bu ndëk ci bi mbass mi doore gis nañu ni reewum Chine waañi na ñaari teemeeri milyong yi tilim bimou deefon ndigëni daaw ci atum 2019 japp nañu ni likowaral mooy roplaan yi ñi teye ak petarol biñu bayyee lak.[4] Ken ku xam xamam jëm ci waalu jawu ji ligeey bobu mën naa wallu 77,000 nit yu naroon dee. waaye ba leegi ki di Sarah Ladislaw biy liggeey ci kureel gi neena desna lu bari ndaxte reewum Chine parewul waañi tilimal jawu ji. Ci diggante 1 fan ci weeru saanwiyee ba 11 ci weeru Marss 2020, fële ca Itaali kureel bi feetee ca Europe setlu na ni lii di tooke biy jugee ci saxaar si izin yi di geenee ak ndaamaar yi ak ñii di liggeey ci di geenee kurang ci jawu ji waañeeku na bu baax. Li lepp nak mu ngi xewee ci biñu tëjjee dëk yi. NASA ak ESA ñu ngi doon jiite gëstu yi ñu doon def ci gaazu Nitrogen te gis nañu ni jëfëndikoo bi waañeeku na bu baax ci bi mbassum COVID-19 tambalee ca Chine. Koom koom bi waañeekuna ba jeggi dayo tek ci waañi tilimal bi doon am rawatina ci reewu taax yi bu ci melni Wuhan ca Chine ci xaaju xaajaat ci li ñu daan tilimal(25%). NASA mu ngi gëstu di saytu ci gaazu ozon ak Nitrogen ak yeneeni xeetu gaaz. Lii yëpp ci xibaar jotna dimbali NASA ci gëstu wam li yëpp li ko waral mooy tëjj bi ñu tëjj dëkk yi ci adduna bi.

Yoonu ndox ak dundu gi

Linuy soxla ci ak diko jënd ci  jën waañeekuna bu baaxa baax te liko waral mooy mbass mi, teyit napp bi dafa taxaw lool sax. Rainer Froese jën dina gënë bari ndax mbass mi,lu bari ci jën dina yokk ñaari yoon ndax ñakkup napp gi, te ñu ngi ragal ni fële ca Europe yeen xeetu jën yu melni herring mën na gënë yokk. Siñaatir gi ci weeru Awril ren, ngir noppal geej yi ba leegi desna leer.

Gëstu ak yookkute

Donte ni jëfëndikoo bi ci gaaz bi wañeekuna bu baax, kureel giy saytu enerzi ci adduna neena mbass mi mën na tere ay sosete yu bari ñu waañi seen loxo ci xaalis bi ñu daan joxe ngir ñu gënë ñoñal kurang buy jogee ci jawu ji.Ci loolu lëlu gi ñu yokk tax na ba nit soppi doxalinu ni ñuy ligeeyee. Loolu andi na tamit, linuy jëfëndikoo ci mask ak yeneen di yaqq linu wër ba ci palastik yi. Tilimal ba ngi yokk. Saantar biy ligeeyël adduna bi ci kilimaa neena waañeeku bi am ci roplaan yiy daw,te mbass mi waralko mën na am ay jeexital ci jawwu ji. Te liko waral mooy ñiy liggeey ci roplaan yi di jëfëndiko li ñuy wax ay "Meteorological Data Relay"(AMDAR) ngir mu mën leena jappale ci ñuy artu seen bopp ci lu mën xew. Waa ECMWF tanii nañu koomu AMDAR dina waañeeku bu baax maanaam juroom benn fukk ak juroom ci teemeer bo jël ci seeni ko0m koom dina waañeeku.

Niñuy doxalee

Foommu nañu daje bi waroona am ci ñi sèqq waallum soppeekup jawwu ji ba 2021 ganaaw ba mbass mi tegee tankam ci dëkk yi ba yoobu leen lopitaal. Waxtaan bobu lu amoon solo lë ndaxreew yi parèwoon nañu ngir tënku ci xaatim yi ñu deefoon ca Pari.Mbass mi waañi na mëninu yeen reew yi ngir ñu xetali ñeneen ñi.ndax dañu tënkuwoon lool ci li leen doy.[5] Been ci kër taskatu xibaar yi japp nani mbèbetu dekalaat been koom koom pur adduna bi yëpp nar na jur ay jëfëndiko yu ëp loxo jëm ci gaaz bi.Ki jiite kureel gu mak gi ci kurang bi neena waañeeku bi ndax mbass mi baaxoon na ñu jeëfëndiko esaanse ak yiu ni mel.

Tani neena galankoor mën na am

Tambaliwaat ligeeyum garab yi ak dem bi ak dik ci been yoon ganaaw bi ko COVID-19  ak tëjj yi ñu tëjj leep deful ludul yaqq gañcax gi wante du ko gënë ñoñal mukk.

External links:

·         United Nations: Six Nature Facts Related to Coronaviruses

Références

Tags:

Yaqq Yaqq Koronaa Ci Linu Weër Ci At Bi Ñu Nekk Ci ganaaw tuutiYaqq Yaqq Koronaa Ci Linu Weër Ci At Bi Ñu Nekk Ngelawu dëkkuwaay bi tilimYaqq Yaqq Koronaa Ci Linu Weër Ci At Bi Ñu Nekk Yoonu ndox ak dundu giYaqq Yaqq Koronaa Ci Linu Weër Ci At Bi Ñu Nekk Gëstu ak yookkuteYaqq Yaqq Koronaa Ci Linu Weër Ci At Bi Ñu Nekk Niñuy doxaleeYaqq Yaqq Koronaa Ci Linu Weër Ci At Bi Ñu Nekk Tani neena galankoor mën na amYaqq Yaqq Koronaa Ci Linu Weër Ci At Bi Ñu Nekk RéférencesYaqq Yaqq Koronaa Ci Linu Weër Ci At Bi Ñu Nekk

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

FukuokaGaawuMelaneesiYekaterinburgPajTurkumenistaanTugalasiKataarRonald ReaganGoxub Dottub Bëj-saalumBipolar disorderAlbaaniJaxan-jaxanBanjulBëj-gànnaaru AamerigRui VazNitBawolDaanaka-dunMosambikNdakaaruUetersenParaguwaayMbëjfeppalA lygaDiiney AfrigYamooPreguiça (Kap Weer)Nguur-Yu-BennooAsiKore gu Bëj-saalumGuwaadalupFC PortoDoxalukaay bu demandooGayndeFeebaru tëlbëti bu amul appTuvaluSimiOseyaaniMonaakoMoldaawiOsakaGoloSaytubiddiwBuruundiListe de films en wolofAsamaanYuusu NduurMaltAfritugalasiNairobiBelaarus🡆 More