Guyaab

Guyaab xeetu garabu foytéef la gu bokk ci njabootu mirtaceae.

Ci gox yi gën a bari naaj ca Amerig kepp la daa sax, ginnaaw bi la tas ci àddina bi. Baatu guyaab ci làkku Arawaag la bawoo, turub dëkk la woon ci réewu saa-kolombi ya woon.

Guyaab
Garabug guyaab (Psidium guajava)
Guyaab
Xobi garabu guyaab
Guyaab
Tóortóoru garabu guyaab
Guyaab
Meññeefum garabu guyaab

Melo wi

Taxawaayu garab gi dafa yem, man na àgg ba 8i sàntimet ci guddaay. Xobam man na àgg ba 15i sàntimet ci guddaay ak 7i sàntimet yaatuwaay

Guyaab bi (doom) xob wu nooy la yor. Wirgoom cig ñàkk a ñor nëtëx gu leer la, cig ñor nag mboq gu dër la, day amaale ay tomb yu ñuul ci yenn xeet yi.

Solo si

Guyaab garab la gu ràññeeku te am solo ci wàllu koom.

Dees na ko soppi njar, njambaanu foytéef ak yu ni mel. Xolliitu foytéef dees na ci faj biir buy daw. Manees na ko lekk it nim bindoo. Dees na ci jëlee sax gëtt.

Turu xam-xam wi

Psidium guajava

Tur wi ci yeneen làkk yi

farañse: goyave
angale: guava
itaaliyee: guava

Tags:

Guyaab Melo wiGuyaab Solo siGuyaab Turu xam-xam wiGuyaab Tur wi ci yeneen làkk yiGuyaab

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

Niels BohrMonsoroIrlaandDiiwaanu TambaakundaaWuññi yu melosuuf yiJeqiku ga amoon ca FaraasPragKoorDiggu AfrikJappum njaamMadridConfuciusUetersenNgisteSëriñ SaaliwuPakistaanMuhammadElen Jonson SërliifŊas (rougeole)Waxtaani sëriñ tuubaaWolof (làkk)Santo Antão (Kap Weert)GineKàttanPeruMoskuYoussou N'DourKàllaamaNoorweesAfrikPitaxPombas (Kap Weert)QingdaoRéewi lebu yiMbàqnoosPeexSudaanFeebaru tëlbëti bu amul appSankt-PeterburgYamanMboqJëm kanam gu xam-xam ak yewwute gu endustriRéew yi BennooKàddTaariixAssomadaKom-komSowwu AfrigFC DerbySão Salvador do Mundo (Kap Weer)Iniweersite Séex Anta JóobBennoo gu AlmaañMain PageJamaykaTugalHepatite BNdoxNgelawNiseerManchester UnitedMuusNataalChelsea F.C.UsbekistaanApoloniSeex Anta JóobPodgorika🡆 More