Dibbtóon

Dibbtóon (pos ca Saalum) as ngarab su ndaw la su man a toll ci juroom benni met.

Xobi dibbtóon day xaw a dëgër. Ay wàqaasam day laxasoo di am car yu ndaw yuy am i dég. Garabu dibbtóon manees na koo góob ci àll ngir jëfandikoo ko cim paj.

Dibbtóon gi (Gardenia ternifolia)
Dibbtóon gi (Gardenia ternifolia)
Meññeefum garbug dibbtóon
Meññeefum garbug dibbtóon

Barab yi

Garabu dibbtóon man nañu koo fekk ci kembaaru Afrig li ko dale Seneegal ba Ecopi, Ugandaa, Keeñaa, bëj-saalumu Namibi Botswaana mbaa ca Mosàmbik, gàncax la gu man a màgg ci suuf su nanguwul, ci suuf su wow mbaa su am i xeer wala suuf suy taa nawet.

Meññeef mi

Doomub dibbtóon deesu ko lekk, ay xobam it noonu. Waaye reen yi buñu ko baxalee man naa faj tooy ak coono. Leeg-leeg ñu toggaalee ko ak laax mbaa ruy ngir faj yaram wu tàng.

Yeneeni njariñ

Bantu garabu dibbtóon manees na koo lakk ngir am xeetu sunguf su ñuy defare saabu. Doom bi manees na cee cuub.

Turu xam-xam wi

Gardenia ternifolia

Tags:

Dibbtóon Barab yiDibbtóon Meññeef miDibbtóon Yeneeni njariñDibbtóon Turu xam-xam wiDibbtóon

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

NitThanh HoaIslaandAlmaañBëj-saalum-penku AsiPaakaFinlaandAlmasi biAmiinDuni SolomonSiraa LeyoonWu-faraasMarookRomTirkiArimateSanaarNasaraanSanta Luzia (Kap Weer)SudaanRostov-na-DonuSenegaalSëriñ Muhammadu Faliilu MbàkkeBaatukaayFeppmaanduKongóo-BrasaawiilEndLonkoyoonu àdduna biArubaGayndeSowwu AfrigSaarayegoTaaywaanArmeeniAlseNgéejTëriinuw nosukaayKarajKureelu Mbootayu Xeet yiOngiriThe BeatlesItaaliNjàppum jaamJimbulang bu waa-BrëtaañPorkhovXajPenku AfrigRomaaniBaalRéewum LawosAlxuraanSimiSowwu TugalMoldaawiHamamatsuBakuTequixquiacYattRigaLimu réewi àdduna biAtenDun🡆 More