Wolof; Gam-Gamle Diggante Loyi Lateŋ Yi Ak Araab Yi

Wolof làkk la woo xam ne wuñu yeex a yaxal la .

bi ñu demee ba di ci bind it amna ñu ko daan bindee mbindiinu naar te loolu moo jëkk (rawatina wolofal yi); loolu nag xayna la seen jamono laajoon; ag  ubbeeku amutoon (ouverture) ag péexte (la Liberté) it noonu niki am jotug sàkk(créer) ak jubbanti yit amutoon .

Amna ñoo xam ne mbindiinu tubaab lañ koy binde loolu moo mujj rawatina ci ñaareelu xaaju xarnu bii jàll,  moo gën a tasaaroo it leegi.

Ngir gam-gamle (comparer)  yaari mbindiin yi:

Fàww nu xam ne moomuñu ci benn araab bi ñi ko daa binde moom lañ xamoon jàng ko ngir diine. Ñi ci daa binde tubaab it moom lañu jàng ngir ag noteel.

Farañse bi amna ñaari xeeti mbindiin:

moo xam ne  mu mbedd la matul amul ay sàrt .

ak bu ñu yoonal mu gën a mat am ay  sàrt.

Mbindiinu fañse mu mbedd mi: ag ñàkka matam ak ag ñàkka amam ay sàrt.

Ci ag niral boo waxee "xall" ak "xàll" dañuy bind rek" khall" . mu des it araf yi nga xam ne farñse amu ko ci cosaan niki "ŋ" (Joŋe( moom day bind jonge (diongue). Jarul m guddal .


Mbindiinu wolof mi nguur gi yoonal jaareeko ci loyi lateŋ yi moomu am na ay règle te loy yépp it am na ci .


Mbindiin mu naar mi nag boo xoolee boo ko dëppee ci xasaayid yi wala alxuraan day baax ndax araab lañu; mu des nag nga bëgg koo dëpp ci weneen làkk, day aajowoo yokk ak wàññi ak mu wuyy sàrti làkk wa.


Ginnaaw mbindiinu naar lanu jël bëgg cee yakk wolof su boobaa jafe-jafe bi am ci mbindiinu tubbaab mu mbedd mi boo ñëwee ci araabal mi yit yéesul  ag cikk .


Daanu ci joxe ay niral:


Jëlal diggante "nj" (njar)"ñ" (ñar)"c" (car) araab bi  day bind rekk (چر) ñatti tomb ci kaw jiim gi .

Xoolal it  diggante "ng" (ngàdd) ak "ŋ" (ŋàdd) ak "g" (gàdd) day bind rekk (ݣاد) walla (ݣَدّْ).


Nga ñëw  ci wàllu taq ak tàqaliku loolu it mbir la ndax amul ay règle ak sàrt  du ma ci guddal.


Xoolal diggante "mb" (mbacc)  ak "p"  (pacc)  day bind rekk (پچ) ñatii tomb ci kaw baa gi .


Xoolal diggante "O" (woor) ak "Ó" (wóor) ak "U" (wuur)  (وُور)  maaska lonk rekk lay def .


Xoolal diggante "E" (weeru)  ak "É" (wéeru) day bind rekk ( وار) daal di teg tomb ci suufu waaw gi .


Xoolal  diggante "a" (kar) ak "ë" (kër) day def rekk "كَرْ"

SERIGNE MBACKE BOUSSO

Tags:

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

Maars (weer)KaliningradFukkArafu S1Xam-xam.scPrimeira LigaA lygaKisinawuMajor League SoccerTéere TaariixXët wu njëkkOsakaManchester City F.C.EndWaxsetKigaliMelosuufDambalBelaarusPremier LeagueDendu mbëjLat JoorDawaanu mbëjPoloñSaaru MaryamaBurkinaa FaasoFarata ak sunnaay asakaIspaañMikroneesiSaw Tome ak PreesipXëtu webItaaliAserbayjaanMuusMàngoDuni Virgin (angalteer)MelanesiNjëkk-taariixGineg yamooTelefonKureelu Mbootayu Xeet yiBermudaBetesdaBrasawilMbërbóofMaldiifBahrayimXaralaTaariixu SenegaalKaabuSenegaalBaraayIsiptLiechtensteinWu-angalteerMeloTaariix🡆 More