Wëttéen

Wëttéen garab gu ndaw lay doon mi ngi bokk ci njabootug Malvacées

Wëttéen
Wëtteen gi (Gossypium hirsutum)

Melo wi

Wëttéen garab la gog day màgg sax ci yenn gox yi nga xam ne day am naaj te suuf si xaw a wow.

"Wëttéen" garabu ñax la gog man naa dund ay 10i at. Guddaayam dees koy natt ci 10i met waaye buñu koy bay dañ koy gàttal ci ñaari met ngir yombal jël giñuy jël Wëtteen wi.

Tóor-tóoram dañuy génn ci ñaari pàcc, gog day weex ak pàcci gog day mboq te yor genn xet bees ràññeef lool.

Ci noonu ci lay amee lu mel ni mbaxana bob day dëgër, bob day màgg daa di ubbeeku daa di bàyyi doomi wëtteen yi ñu génn ci doom yooyu ci la fiibar bi di génnee nga xam ne moom lañuy jëfandikoo.

Te wëttéen yi bari nañ lool waaye bi ci ëpp liñuy jëfandikoo mooy bi ñuy woowe Gossyium hirsutum

Ngir bay Wëttéen danuy soxlawoo ab diir bu xaw a yàgg. Fu bari naaj, dees na jàpp diir bi ci 520i fan yoo xam ne danu koy suuxat ngir màggal ko ba noppi nga as ndiir ngir mu wow, as sos doo ko nàndal ngir may Wëttéen wi mu xaw a wow.

Garab la gog dees koy bay ci mbayum nawet ci Afrig, ak End, ak Amerig.

Njariñam

Garab la gog ay at a ngii ñu koy jëfandikoo ngir di ci de far ay yéere yu nooy.

Nataal yi

Turu xam-xam wi

Gossypium hirsutum

Tags:

Wëttéen Melo wiWëttéen NjariñamWëttéen Nataal yiWëttéen Turu xam-xam wiWëttéen

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

KirgistaanPragXartumNiccolò MachiavelliSunnay TiimNjàngatPakistaanBabilonTokelauBéerAlxuraanGuyaana gu FaraasOmar Blondin DiopNanjingPortugaalBiibëlCaddTrojanyXareb Àdduna bu NjëkkFilipiinGaboŋBisaawóoWu-faraasAmiinWanuatuTianjinMbaamAy kàddu ci say coppiteFànnالخضرDiwaani dottWu-angalteerBulgaariBrasawilXaySendaiBennJimbulangArsantinXaralaymbëjKinshasaNoorNikaraaguwaWeeri wolofDiiwaanu LugaHip-hopGerteBanglaadesNorthern Mariana IslandsMerkuurMbalWuutuloxoAfrig gu bëj-saalumu-SaharaÓstraaliBiir bu dawGuamKorwaasi🡆 More