Pàppaaya

Pàppaaya ñu ngi koy fekk lu ci ëpp ci fu bari ndox.

Bu dee ca Senegaal bari ca fa ñuy tudde ñaay bi ak ca Kaasamaas.

Pàppaaya

Melo wi

Guddaayam dana toll ci 3 ba 7u met. Mu bokk ci njabootu dicotylédone bi nga xam ne seen i wànqaas lu ci ëpp day taqaloo. Dundam ci kaw suuf nag, taxu koo yàgg lool diggante ñatt ba juróomi at su bare ba bari waaye ci at mu njëkk mi dina tambalee am meññeef. Te booy dagg wànqaas yi, diir bu gàtt mu tàmbalee amaat yaneen i wànqaas. Ag ndombaam nag da mat 20i sàntimet . Yaram wi yenn saa yi mu yor melo wu nëtëx yenn saa yi mu yor wu baam. Xob wu rëy lay yor wow manees na cee uppu.

Njariñi paj yi

Boo amee liir buy sank muy seere dangay jël ñam wi ci biir nga nal ko di ko ko jox kudd gu ndaw dana dindi seere bi. Bu dee mag mu jël genn wàllu kaas. Ñi am jafe-jafey reesal buñuy jël doom bi ba la ñuy tëdd dinañu reesal ni mu ware. Ku am dagg-dagg bu bees bu jëlee xott pàppaaya wu xaay wi teg ko ci dana tax dagg-dagg bi gaaw a wér.

Paj

Ku am bopp buy metti bu jëlee xobu wi tiimale ko ci taal bamu xaw a tàng mu takk ko ci bopp bi bàyyi ko bamu sedd ci dana ko saafara. Naka noonu day faj pëyiis ak epaatit ak sëqët.

Nataal yi

Turu xam-xam wi

Carica papaya

Tags:

Pàppaaya Melo wiPàppaaya Njariñi paj yiPàppaaya Nataal yiPàppaaya Turu xam-xam wiPàppaayaSenegaal

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

AynonGànnaarWayKonakriJunjNovorossiyskMosambikEslowaakiKeeñaaXayraOlaandBa DonTaariixTongaSapoŋBreesilKawlakRuwandaaSaambiTansaniSingapoorPajTuvaluFinlaandLituwaaniGëm Bis PéncDjibril Dio MambétyTaaywaanSantiagKermanshahCeddoAntigua ak BarbudaŊas (rougeole)Doxalukaay bu demandooSofiyaXott-biteelTugalasiFC DžiugasXaymaCuubEkwadoorJibutiOseyaaniDiiwaanu FatikSuraas gAyitiRadio Studio 54 NetworkAtenMadagaskaarDuni Virgin (angalteer)Wu-angalteerJordaaniNairobiAlegsàndiriLetóoniBenesuwelaBiibël🡆 More