ubbeeku

Bakkub Wikipedia mooy Jimbulang bu Ubbeeku bi.

Tekkeem yenn saa si man naa wuute.

Lu "Ubbeeku" di tekki?

  • "Ubbeeku" ndaxte ëmbitam da fa ubbeeku ngir ñépp. Su nu toppee ay àtteem.
  • "Ubbeeku" ndaxte amulum pay.
  • "Ubbeeku" ci su nu xoolee ci maanduteem. Fexe ba benn jengte du am ci biiram, ci wàllu gis-gis yi.
  • "Ubbeeku" ndax àtte yiy tëral doxalinam amul kenn ku leen di tek, du ku ci "kaw" walla ci "biti". Lu weesu yenn tomb yi dul deñ, di yi ko teye (juroomi ponk yi), Askanu jëfandikukat yi ñooy yor màggam.
  • "Ubbeeku" ndax bind ab jukki taxul nga moom ko, li ngay bind moomoo ko. Kon ku nekk am na sañ-sañu soppi leen, loolu àttey Wikipedia ñoo ko tëral.

Lu "Ubbeeku" tekkiwul

  • "Ubbeeku" tekkiwul ne lu la neex duggal ci. Dan fee nekk ngir defar ab jimbulang bu baax te sell. Du ab yéenekaay, du it ab yëglekaay...
  • "Ubbeeku" tekkiwul ne man nga fee taf ay mbind walla ay nataal yoo jële ci beneen dal walla ab kaggu(bibliothéque). Loolu jalgati aqi ki-sos (droit d'auteur) la, te yoon nanguwu ko.
  • "Ubbeeku" tekkiwul ne amul kenn kuy saytu ëmbitam. Askan wi day seet aka xent jukki yi, lu weesu seenug dugg, su jaree far ñu far leen.
  • "Ubbeeku" tekkiwul ne man ngaa def lu la neex ci xët yi. Dal bii ab Mbootaay buy "def ngir yalla" moo ko sos ngir lenn rekk, muy sos ab jimbulang.
  • "Ubbeeku" tekkiwul ne man ngaa taf ay jukkeem ci sa dal, walla jël ëmbitam bind ci ab jukki ngir sa yéenekaay, te tuddoo ci Wikipedia, ni fa nga ko jële.

Tags:

Jimbulang

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

Kureelu Mbootayu Xeet yiGireesIraanDuni KanaariNeptuunXeltuXUDAR.zmNairobiNguur-Yu-BennooÑaqu meningiteAlseKoriEndAmiinCuubHTMLSexawXartumUraanusNitDawaan gu wéyLibiFukkSuufGoxYoonPragElsinkiKodiwaarPeruMiyanmaarGuwaatemalaBiibëlMàndiŋ mGoxub Dottub Bëj-gànnaarSaaPenku gu SoriJawwu jiGaalAlxuraanul KariimSmolenskSiligoBeelsebulRéewum LawosÓróopAmsterdamWu-angalteerBaraleJolofRéewum DominikRéewum ñaari dex yiPHPBeliisBëj-saalumu AamerigCaddSaytubiddiwSiliNizhny Novgorod🡆 More