Maam Maajoor Bóoy

Maam Maajoor Bóoy mu ngi juddu atum 1940.

Jigeenu nguur la ci Senegaal, nekkoon fi jëwriñ ju jëkk, moom sax mooy jigeen ji jëkk a nekk jëwriñ ju jëkk ci Senegaal.

Maam Maajoor Bóoy
Dundu ak jaar-jaaram
Maam Maajoor Bóoy
Ndombo-tànk
Jëwriñ ju jëkk ju Senegaal


(menn at, juroom-ñetti weer ak benn fan)
Njiitu réew Abdulaay Wàdd
Ki mu wuutu Mustafaa Ñas
Ki ko wuutu Idiriisa Sekk
Dundu ak jaar-jaaram
Bésu juddu (juroom-ñaar-fukki at ak juroom-ñeent)
Bérebu juddu Ndar (See-Luwi) (AOF)
Réew Senegaal
Kureelu pólotig Bokkul ci genn kureelu pólotig
Jànge Iniwersite bu Dakaar
Liggeey Borom xam-xamu yoon ak yoonal

131x131px|Mame Madior Boye
Jëwriñ yu jëkki Senegaal (Premiers ministres du Sénégal)

Dundu ak jaar-jaaram

Cosaan ak njàngam

Maam Maajoor Bóoy mu ngi juddu atum 1940 ci Ndar (See-Luwi). Ñenn ci njabootam, xam-xamu yoon lañu jàng. Way-juram wu góor gerefiyee la woon laata muy nekk isiyee (huissier de justice). Kenn ci ay càmmeñam toppekat seneraal (pólokirëer seneraal) la woon ca ëttu àttekaay bi gën a mag ci Senegaal (Cours suprême du Sénégal). Keneen ki ci nekkoon jàngalekat buy jàngale lii di droit international privé, moo mujj doon njiitu iniwersite bu Dakaar.

Bi mu jàngee ca liise Federb bu Ndar ba matal, la ñëw iniwersite bu Dakaar, atum 1963, ci béreb bi ñu fay jàngale yoon ak koom-koom. Ginnaaw njàngam ci iniwersite bu Dakaar, dafa dem jàngi Pari ci ab lekool bu ñuy jàngale yoon ñu naan ko Centre national d'études judiciaires (CNEJ) de Paris, lekool boobule moo mujj nekk lekool bi ñuy tàggate àttekat yi (École nationale de la magistrature).

Ay jaar-jaaram ci wàllu yoon ak yoonal

Dafa jëkk a nekk ki ñu toftal ci toppekatu repibilik bi (procureur de la République), teg ci nekk ki topp ci njiitu tirbinaalu gox bu jëkk bu Dakaar (première vice-présidente du tribunal régional de première classe de Dakar) laata muy nekk njiitu néeg ca àttekaayu dabaatal ba (présidente de chambre à la Cour d'appel).

1990 ba 2000, amoon na ay ndombo-tànk ci ab bànku Afrig sowu jant ñu naan Compagnie bancaire de l'Afrique occidentale.

Ay jaar-jaaram ci wàllu pólotig

Maam Maajoor Bóoy bokkul ci benn pàrti. Bi Abdulaay Wàdd jëlee ndam li ci wotey njiitu réew yu 2000, la ko tabb jëwriñ ji yore wàllu yoon awiril 2000, ginnaaw loolu, mu def ko jëwriñ ju jëkk ñetti fan ci weeru màrs 2001, ginnaaw bu Mustafaa Ñas jébbalee lenge yi. Moom mooy jigeen ji ñu jëkk a tabb jëwriñ ju jëkk ci réew mi. Ci ayam gi, la tabb ay jigeen jëwriñ ji ñu toftal ci wetu gox-goxaat yi (Cewo Siise), jëwriñ ji yore wér-gu-yaram bi (Awa Mari Kol Sekk), jëwriñ ji yore njaboot gi ak tuut-tànk yi (Awa Géy Kebe) ,jëwriñ ji yore njënd, njaay, këri liggeeyukaay yu ndaw yi ak yu digg-dóomu yi (Aysa Aañ Puuy) ak njiitu kureel gu mag giy saytu liggeeyu tele yi ak rajo yi (Haut-Conseil de l'audiovisuel) (Aminata Ñaŋ Siise). Moom ci boppam, moo daloo Kàggug réewu Senegaal (Bibliothèque nationale du Sénégal). Ñeenti fan ci weeru nowàmbar lañu ñaanalante moom ak njiitu réew mi ginnaaw taxawaay bu mu amoon bi bato Lë Joolaa suuxee, septàmbar 2002.

Septàmbar 2004 la ko Alfaa Umar Konaare tabb teewalkatu Kureelu gu mbooleem réewi Afrig yi (Commission de l'Union africaine (UA), mu gàlloo aar nit ñi demul ca toolu xare ba te nekk ci bérebi ayoo yi. Dakaar la féete waaye dafay dem lu bare ci yeneen réew yi, fu mel ni Darfuur, Repibilig bu Sàntar Afrig, Kótdiwaar, Repibilig Demokaratig bu Kóngoo, Ruwandaa, Burundi wala Ugandaa, nga xam ne dafa fay daje ak ñi séq xeex bi (xeexkat yi ak way-pólotig yi).

Téere, jukki wala dali web yi ñu yër

Toftal bi

Jukki yi ñu ko tudd

  • Ngornmaŋu Maam Maajoor Bóoy (Gouvernement de Mame Madior Boye)
    • Jëwriñ yu jëkki Senegaal (Premiers ministres du Sénégal)
    • Pólotigu Senegaal (Politique du Sénégal)
  • Limu njiiti pólotig yu jigeen (Liste de dirigeantes politiques)
    • Nekkinu jigeen ci Senegaal (Condition féminine au Sénégal)
    • Limu jëwriñ yu jigeen ci Senegaal (Liste de femmes ministres sénégalaises)

Lees bind ci moom

  • (en) Kathleen Sheldon, Historical Dictionary of Women in Sub-Saharan Africa, The Scarecrow Press, Inc., 2005, 448 p.
  • Babacar Ndiaye et Waly Ndiaye, Présidents et ministres de la République du Sénégal, Dakar, 2006 (2e édition), p. 42
  • « Mame Madior Boye : Femme ... et Premier ministre », in « Femmes au Sénégal », Les Cahiers de l'Alternance (Dakar), Partenariat Fondation Konrad Adenauer et Centre d'études des sciences et techniques de l'information (CESTI), no 10, décembre 2006, p. 83-84

Lees jële feneen

Tags:

Maam Maajoor Bóoy Dundu ak jaar-jaaramMaam Maajoor Bóoy Téere, jukki wala dali web yi ñu yërMaam Maajoor Bóoy Toftal biMaam Maajoor Bóoy

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

Réewi lebu yiGaawuXam-xamKoom-koomu AfrigCampeonato Nacional (Kap Weer)QingdaoMartinikBeliyarHo Chi Minh CityAminata TureFeebaru stress buy wëyWolof (làkk)AtenKońskowolaNiseeriyaMarokSaint LuciaMaasSuweedÓstraaliWu-angalteerJimbulangGrenadaIsraayilSaaru MaryamaGanaIrlaandWu-ispaañMaio (Kap Weert)LibiNguur-Yu-BennooWiyetnaamYewwutePragSporting CPKiyewXam-xamu suuf si ak jawwu jiFànnCampeonato Nacional (Kap Weert)Diiwaanu FatikDisambarMajor League SoccerBlaise PascalTurkumenistaanSeland-Gu-BeesManchester UnitedDereetRafael CorreaNowembarTibilisiEriterePapaayBulgaariGuyaana gu FaraasRon-goxu EndBiibëlRomaaniSaaw miSëriñMadagaskaarSapoŋWaxi Seex Anta JóobNovosibirskBeijing🡆 More