Xaru

Xaru mooy nga am yééne ray sa bopp.

feebaru naqar gu metti ku dara saful, Feebaru "bipolaire", Feebaru "schizophrénie", feebari nekkin, ak feebaru dorogewu - boole ci naan gu bari gi ak jëfandikoo garabu benzodiazepine - yi yépp luy indi xaru la Ñenn ci ñi di xaru dafa am ay jëf yu ñu dooleelndax stress joge cijafe-jafe xaalis, jafe-jafe nekkin ak nit ñi nekkin ci diggante ay nit, walla tiital Ñi mësa jééma xaru dañu nekk ñoo xamantane ngir ñu jéémaata xaru lu yomb la. Fagaru ngir waññi xarujéégo yi ñooy nééwal yoon yi di indi xaru - lu mel ni ay fetal, dorog, ak poson; faj feebaru xel yi ak dorogekat yi; yéglekaay yi nettali bu xaru amee, te yoq koom-koomi nit ñi. Su fekkee sax ay nimero yu nit ñi mëne woote saa yu nekk su ñu amee jafe-jafe bare nañu, wóórul ne am nañu njëriñ.

Xaru

Yi ñu gën di gis fasoŋu xaruda ñu wute ci diggante rééw yi, te mungi bokk ci benn wall ci ay pexe yu wóór yu ñu tërël. Fasoŋi xaru yu ñuy gën di gis ñooy xoj sa bopp, naan poson, akay fetal. Xayma nañu nit ñi dee ci xaru tollu ci 828.000 ci addina bi yépp ci atum 2015, am na yoqutewu ci xaymaay atum 1990 tolluwoon ci 712.000. Lii moo def xaru fukkeelu mbir yuy indi deeci addina bi.

Lu jege 0.5-1.4% ci nit ñi di xaru, lu tollook 12 ci 100.000 nit yoo jël at mu nekk Ñett ci ñeent ñiy xaru ñépp ci addina bi mungi am ci ak rééw yi seen am-am demewul noonu. Xayma xaru yi am ba pare lu ci ëpp ci góór ñi la ëppe boo ko méngalee ak jigéén ñi, tambale ko ci 1,5 yoon gëna kawe ci rééwi yi seen koom-koom di jóg jëm ci 3,5 yoon gëna kawe ci rééwi yi ame alal. Xaru lu ci ëpp mungi gëna fës ci ñi weesu juróóm ñaar fukki at; waaye, ci yenn rééw yi, at yooyu ñungi ci diggante fukki at ak juróóm ak fanweeri at ci seen mëna xaru yu gëna kawe. Europe moo ëppoon ay nit yu xaru ci ay gox ci atum 2015. Xayma nañu fukk ba ñaar fukki miliyoŋ ñi jééma xaru te deewuñu at mu nekk. Di jééma xaru te deewuloo mën na indi ay gaañu-gaañu ak ay laago yu yagg. Ci rééwi tugël yi, di jééma xaru mungi ëppe ci ndaw ñi ak ci jigéén ñi.

Ay gis-gis yi nit ñi am ci xaru ñungi bawoo ciay ngëm-ngëmyu mel ni diine, teddaay, ak njëriñu dund bi. Yii Diine yu joge ci Ibrahimadañu gise xaru ni ab tooñ Yalla, ndax seen ngëm-ngëm ci sellaay yu dund bi. Bi samuraidoon am ca Japon, benn xeetu xaru bi ñu xamewoon ni seppuku harakiri dañu ko joxoon cër ni beneen yoon ngir bëral ñakka tekki walla ni yoonu ñaxtu. Sati, benn jëf-jëf la bu ñu terewoon joge ci Raju Britanique bi, bu doon xaar Jëtuur Indo bidiray boppambi nééwu jëkkëram ji taalu robukaay, mu defal ko boppam walla waa këram ak mbooloo mi di ko puus. Xaru ak jééma xaru, bu njëkka ba dañu ko terewoon, waaye léégi ci rééwi Tugël yu bari kenn tereetu ko Boobu dafa nekk ab ñaawtééf ci rééw yu bari ba léégi Ci siecle ñaar fukkeel ak ñaar fukkeel ak benn, xaru lu nééw lañu ko jëfandikoo ni xeetu ñaxtu, ak kamikaze ak xaru ak ay bomb nekk na lu ñu daan jëfandikoo ni jëfinu militaire walla terroriste.

Tags:

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

Afrig gu Bëj-saalumKongóo-BrasaawiilBalaamRahmaniyaÑaqu BCG.itFaraasBurkinaa FaasoDarkaseMosambik1. Liig - SalRéewum MaseduwaanWeerSal (Kap Weer)TansaniDawaan gu wéyWilniyusXeltuArminaatSeerbiSeent EleenLimub njiiti Senegaal yilTaariixu ItaaliSapoŋGireesMàkkaanum mbëjfeppalJëmmPenku gu SoriTongaNgeerSattumbarNjàngatShanghaiSankt-PeterburgSancamJolof Ak li ko waraloonLituwaaniDëkkaani ndiiwaani SenegaalMohammedWu-angalteerOseyaaniKopparYuwanXUDAR / XidrBulgaariMàbba Jaxu BaLondarRuwandaaAddis-AbebaSenegaalAlquraanul KariimCatirTuberculosisEcserShenyangLimu réewi àdduna biGaalTiniisiJàngoroy EbolaUulRéew yu Bennoo yu Mikronesi🡆 More