Tuberculosis

Tuberkiloos (TB) feebar la buy wàlle, te li koy faral di joxe mooy doomu jàngaor bi tuddu Mycobacterium tuberculosis (MTB).

Cër bi tuberkuloos di ngëna jàpp mooy dënn bi, waaye mën na dem ba laalaale yeneen cër ci yaramu nit ki. Barina lu muy dal nit te du feeñ, loolu lañuy woowe tuberkuloos bu nëbbatu. Lu tollu 10% feebar yiy nelaw yaramu nit ki, dañuy dem ba daaneel nit ki, suñu ko fajul, mën na dem ba faat ki mu dal. Beneen tuburkuloos bi nelawul moom dafay wane boppam, kumu dal dangay am sëqët mu tar àndaale ak lumbi deret, yaram wu tàng, ñaqu guddi, ak yaram wuy jeex di dem. Di nañu koy faral di woowe feebaru "ŋacci" ndax limuy ŋacci sa yaram. Amna yeneen anam yu muy feeñee su laalee yeneen cër yi.

Tuberkuloos dafay tasaaroo ci ngelaw li, suede tuberkuloos bu tar moo la jàpp, soo sëqëtee wala nga tifli wala nga wax, wala nga tissooli mën nga ko wàlle. Nit ñi feebar bi di nelaw ci seen yaram du ñu wàlle feebar bi. Nit ñi gëna mëna wàlle feebar bi mooy ñi am VIH/SIDA ak tóxkat yi. Ngir saytu jàngoro ju tar ji ci yaram nit, dañuy rajo dënn bi, dañuy jël itam ndox mu bawoo ci moom ñu xool ko ci microscope wala ñu amal ci njàngat mu xóot. Sudee tuberkuloos biy nelaw nak, ci deru nit ki wala ci deretam.

Suñu bëgee aar nit ñi ci feebar boobu, nañuy saytu bu baax ñi nekk fumu leen mëna dalee, teela gis doomu feebar bi ak teel ko faj, ak jël ñaq bii di Bacile Calmette-Guérin (BCG). Nit ñi feebar bi gëna yab ñooy ñiy liggéeyandoo ak ki ko am, ñi mu bokkal kër, workplace, ak ñi muy nekkal bis bu nekk. Paj mi dafay yàgg lool, te ay àntibiotik lañu koy defee. Doomu jàngoro bi daa tàmbali ñeme garab yu bari (MDR-TB) ak doomu jàngoro yi ñeme yeneen garab bi (XDR-TB).

Ci atum 2018, ñeenti nit ñoo jël xalaat nañu ni kenn ka amna tuberkuloos. At mu nekk dina am lu tollu ci 1% ci nit ñi ci àdduna bi ñuy am doomu jàngoro ji. Ci atum 2017, amoon na lu ëpp 10 milion ci nit ñu am feebar bi, ci ñooñu amna ci lu tollu 1.6 milion ñu ci ñàkk seen bakkan. Loolu moo ko def feebar bi dàqa ray ci feebar yiy wàllaate.Lu ëpp 95% nit ñi mu faat ci réew yu néew doole yi lañu dëkk, lu ëpp 50% Inde, Chine, Indonesie, Pakistan, ak Philippines. Seetlu nañu ni li ko dale atum 2000 ba leegi wàllaate gi dafay gëna wàññeeku at mu nekk. Nit ñi saytu ndax am nañu tuberkuloos am déet, 80% ci ñoom dañuy am feebar bi suede ci Asie ak ci Afrique waaye suede ci Etats Unis 5–10% ci nit ñi ñuy saytu ñoo koy am. Ca jamonoy maam ya ba leegi tuberkuloos a ngi am.

Cosaanu gëstu bi

Tags:

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

MartinikWayFaraasKore gu Bëj-gànnaarImaaraat yu Araab yu Bennoo yiWuutuloxo bu mbëjYolaakonPrimeira LigaGoxub Dottub Bëj-saalumDunu FalklandMoroniRepublik bu KongóoGaambiJimbulang bu waa-BrëtaañUetersenFaatu BensudaaAnxiety disorder.trAlbert EinsteinSolomTogóoAlegsàndiriDëgërluwiinRéewum Popileer bu SiinTiniisiSiraa LeyoonShenzhenLibiKore gu Bëj-saalumTansaniKodiwaarMurmanskYattTajikistaanMaleesiDiiwaanu KoldaaPalauDereetSochiIsfahanKeeñaaKàllaamaBaay FaalBiir bu dawRiisiTaariixDiggi-gàmmuFC PortoIrlaandUruguwaayRéewum CekRon-goxu EndBurkinaa FaasoMamudsuOoŋ KoŋFeebaru stress buy wëy🡆 More