Rougeole Ŋas

Ŋas (rougeole), feebar la bu gaawa wàlle, te li koy joxe mooy doomu jàngoroy ŋas.

Màndarga yi muy gëna faral di njëkka wane sula dalee mooy yaram wu tàng lool ba weesu 40 °C (104.0 °F), sëqët, bakkan bu sotti, ak bët yu xonk. Sula nit wàllee feebar bi, dinga toog 10 jàpp 12 fan laata muy feeñ ci sa yaram. Su tàmbalee feeñ ba def ñaari fan jàpp ñatt dafay def ay tupp yu weex ci gémmiñu ki feebar, ñu leen di woowe tuppi Koplik. Su amee ci yaw ñatt jàpp juróomi fan, sa deru yaram tàmbali di am ay tërgën wala picc yu xonk, muy faral di tàmbalee ci sa kanam, yegg ba ci sa yaram wi yépp. Jafe-jafe yi muy gëna faral di indil nit ki mooy, biir buy daw (8% ci ñi am feebar bi), (7%) ak pneumonia (6%). Li faral di waral mbir yooyu mooy matuwaayi moytu feebaru ŋas bu jeex. Néew na lu muy sayloo nit, wala mu koy gumbaal wala muy indil yuuram ay jafe-jafe. Rubeole "Rougeole bu Almaañ" ak roseole ñaari feebar yu wuute la, te yeneen wiris yu bokkul bu ŋas moo leen di joxe.

Rougeole (ñas) bi ngelaw li moo koy tasaare, sedee kimu dal dafa sëqër sa wet wala muy tissooli mën nala ko wàll. Sula toflitam laalee wala ñandxitam mën nala wàll. Ñi nekk ci wetu ki feebar te seen yaram amul matuwaay yu xeex feebar bi, fukk yoo ci jël, juróom ñeent ya dina ñu ko am. Ci ñeent fan yi jiitu picc yu xonk yi di feeñ ak ñeent fan ginaaw bi ñu feeñee, nit ki mën na ci wàlle feebar bi. Néew na lu feebar bi di dal nit ki ñaari yoon. Nit ñi war nañu di saytu ndax amu ñu doomu jàngoro ji suñu nekkee ci barab buñ ko mëna amee.

Képp ku jël ñaqu (vaccin) anti rougeole bi mën nga mucci ci feebar bi, te yenn saay nga fekk ñu boole ko ak yeneen ñaq. Soo xaymaa li feebar bi daan faat ciy nit leegi wàññi na ci 80% ci diggante atum 2000 ak 2017, mu am 85% ci gone yi ci àdduna bi yépp yi ñu jota ñaq benn yoon ci atum 2017. Su feebar bi dalee nit ki, amul benn garab buñu mëna waxni moo ko mëna faj, waaye amna ay pexe yu ci mëna jàppale nit ki. Lu ci melni di faral di may ndox ki feebar (dox mu am suukar ak xorom su yam), lekk ñam wu sell, ak jël garab yuy wàcce tàngooru yaramam. Mën nga jël antibiotic itam sudee danga amaale bakteri (doomu jàngoro) bi lay jox pneumonie. Sudee ci réew yu néew doole yi, dañuy digal ki feebar mu jël vitamine A.

At mu nekk, feebar bi dina jàpp lu toolu ci 20 milioŋ ciy doomu aadama, ñi ëpp ci ñoom ñooy waa Afrique ak waa Asie. Barina ñu koy jàppee feebaru xale waaye ku nekk la mëna dal. Bokk na ci feebar yi am vaccin yi dàq a ray. Ci atum 1980, feebar bi daan na faat lu tollu ci 2,6 milioŋ ciy nit, te ci atum 1990, faatna 545 000 doomi aadama; bi ñuy yegg ci atum 2014 prograamu ñaq nit ñi ci àdduna bi wàññina limu ñiy faatu ci rougeole ba 73 000. Lu weesu xayma yooyu ñu amal ak dee gi yokk ci diggante 2017 ba 2019 ndax matuwaayi fàggu ci feebar bu jeex. Li ñu xayma ni moom lay faat mingi tollu ci 0.2%, waaye mën yegg ba ci 10% ci barab yi amul dund gu baax. Ñi ëpp ci ñi feebar bi di faat ñooy xale yi amagul 5 at. Daa melni feebar bi mënalul dara rab yi.

Tags:

Nit

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

BelsikWolof (làkk)Jàngoro Koronaawiris 2019WiyetnaamWarsawSeent EleenBarakiXibaarfeppalŊas (rougeole)LëkkalekaayGinne BisaawóoNovosibirskPodoorGuamNguur-Yu-BennooIniweersite Séex Anta JóobFanny CadeoIsfahanMaliPskovRéewum Popileer bu SiinAnetShenyangNauruWikipediaNgolOoŋ KoŋKongóo-KinshasaKońskowolaMbëjfeppSudaanWatikaaTëjtePyatigorskFas wIsraayilLituwaaniIsiptNjàngaleTogóoÀjjumaMartinikJordaaniSoviet Yi BennoQingdaoMbàmbulaanug AtlasXeexMelosuufDiiney AfrigCharles DarwinLinuxXaruNgisteSendaiFaraasHo Chi Minh CityJëmmHebe CamargoDiiwaan yu BennooBelaarusPeru🡆 More