Darkase

Darkase xeetu garab gu bokk ci njabootu Anacardiaceae.

Ca Amerig gu naaje ga la bàyyikoo, te ci barab yu naaje yi lees koy baye ngir foytéefam.

Darkase
Darkase gi (Anacardium occidentale)

Melo wi

Garabu darkase danay àgg 12 ba 15i met ci guddaay. Buut bi di reenam bi ëpp solo danay àgg ci xóotaay bu sori ci suuf si. Pànguur yi di reeni wet yi danañuy àgg fu sori lool. Xobam wirgow nëtëx bu dër la yor. Danay àgg 10 ba 20i sàntimet ci guddaay ak 10 sàntimet ci yaatuwaay. Xobam wi puur ci noor lay feeñ. Daa gëtte am xet gu neex te day xëcc yamb yi, ci la lem di bàyyikoo.

Doom bi

Doom bi ci njeexteelu noor lay mat. Bu ñoree day xonq mbaa mu mboq. Bu ñorul nag nëtëx. Am ub saal ca biir bu ñuy wax ndaamaraas mu bari ay njariñ lool.

Njariñ li

Doom bi dees na ci njar, dees na ci defar sàngara te dees na ci faju. Garab gi nag dees na ci jële am matt dees na ci faju.

Turu xam-xam wi

Anacardium occidentale

Nataal yi

Turam ci yeneeni làkk

farañse: anacardier
angale: cashew tree
itaaliyee: anacardio

Tags:

Darkase Melo wiDarkase Doom biDarkase Njariñ liDarkase Turu xam-xam wiDarkase Nataal yiDarkase Turam ci yeneeni làkkDarkase

🔥 Trending searches on Wiki Wolof:

PHPToolu bijjaakonCuubMbàmbulaan gu Bëj-saalumKongóo-BrasaawiilDiggu AsiWaletaMàddAddis-AbebaDiiwaani SenegaalCaddMaliFinlaandKubaaGànnaarAntigua ak BarbudaXaralaOttawaTirkiNitRuwandaaBulgaariKàttanWaxsetAwrilUruguwaayZurichDiggu AamerigXeltuBëj-gànnaaru AfrigIrkutskKore gu Bëj-saalumIsiptAfritugalasiNairobiJolofUsbekistaanMbëjbijjaanRom.scOoŋ KoŋÀllarbaLibaaTaaywaanEritereTokyoSaw Tome ak PreesipRiisiNguur-Yu-BennooRéew yu Bennoo yu MikronesiAsiOndurasDisc jockeyGàncaxXam-xamu nosukaayDiiwaanu NdakaaruTiranaDuni SolomonSowwu TugalPakistaanGineDooleranduSamwieMàkkaanum mbëjfeppalHTMLGuwaatemalaLituwaaniRabTelefonAlxuraan🡆 More